audio
stringlengths
36
41
text
stringlengths
0
1.94k
/content/data_kallama/109segment_900.wav
léegi nag ndox yooyu faaw mu am dafa laaj traitement traitement bi yooyu soo demee parce que traitement yi balaa nga koy def day fekk ndox bi leer ndox bi su demee ba leer nag da ngay mën a def traitement maanaam utiliser li ñuy wax en général dañ koy joxe sax mooy comprimé yooyu ñuy distribué ah mooy Aquatabs Aquatabs waa très bien
/content/data_kallama/16segment_480.wav
parce que crédit bi mu jëloon du ko utiliser pour faju su wéree dina mënaat jëlaat li des ci crédit bi dem mu yë() continuer ay yëngu-yëngam
/content/data_kallama/1segment_120.wav
bonsoir
/content/data_kallama/98segment_1470.wav
loolooy waral aussi béykat yi dañuy obligé utilisé ay produits herbicides pour mun a vraiment mun a njëkkalanteeg tool yi
/content/data_kallama/64segment_510.wav
loolu mooy ay jefe-jafe yoo xamante ni duñ koy tukkee te tey ñi nga xamante ni ñoo gën a taxaw ci nit ñi mooy fexe ba nit ñi aaru ci wàllu dund loolu UGPM daf ci liggéey lu baree bari bari di ci sensibilisé ndax liggéey bi li ciy jiitu mooy xamal nit ñi
/content/data_kallama/27segment_270.wav
waaw baax na di la wax nga fàttali ñu tur beeg El Hadj Mansour Touré Passy Aly Dien waaw jërëjëf
/content/data_kallama/26segment_390.wav
/content/data_kallama/112segment_90.wav
wala am yeneen sax yoo xam ne mi ngi leen di sonal waaw ñun sunu liggéey loolu du ñu si am benn tardement ndax bu ñu demee seeti ñun dèjà am na ay unités yu fi nekk ñoom ñooy jug ngir dem saafara
/content/data_kallama/50segment_120.wav
oui xam naa rek laajte bi li ñuy njëkk a maanaam li ñuy wax direction des projection pro() protection des végétaux waaw loolu nag la ñuy firi ci tubaab maanaam végétaux yi ci yan anam la ñu ko mën a faram fàccee ci wolof
/content/data_kallama/139segment_1290.wav
ñaareel ba pour ñu wax ci changement climatique rek ma junjal leen ci tuuti rek loo xamante ni bi
/content/data_kallama/64segment_420.wav
génneewul neen mën a nekk di ci mbay mi coble gi ne bu dee * UGPM lan lay def des activités agrosilvopastoral et alieutique alieutique bi nag amul liggéey waaye dinañ jaay geji dinañ jaay kecax looloo tax vraiment ñu boole ko ci ak artisanaux xam ni loolu lépp ci gox bi la
/content/data_kallama/24segment_450.wav
béykat bi na am dana xam fu muy jooyee naqaram béykat bi dina xam naka lay def ba nekkinam gën a jëm kanam loolu lañ foofa lañ ko sampee ci teewaay Banque Mondiale it samp force paysane muy yëngatu yëngatu yëngatu ba fi mu ne nii moom force paysane voilà ak quatorze régions yi aussi ñu ngi ci
/content/data_kallama/0segment_0.wav
Lamine touré dëkk fan Passy moom mbay rek laay def mbay waaw ren moom béyoon naa waaw waaw am na bu ma si coopérative bi jaayoon kay muy sa jiwu
/content/data_kallama/27segment_420.wav
yàlla moo koy doxalee noonu waaye nag xool fi mu jëm mu xool num taxawee parce que yaakaar dafa fort
/content/data_kallama/30segment_120.wav
su ko defee it mu nekk encore si financement wu ñi nga xam ne rek ñoo di Fond vers climat tey it ñu amaat mbégte àndaat ak yéen si émission bi ngeen koy ànd ak nag ak seen xarit Seydou Dieng waaw salaamaaleykum wa rahmatulah Seydou salaamaaleykum wa rahmatulah mbokk yi ñuy déglu donc ñu ngi leen di nuyu di leen jaajëfal di leen dalal jàmm si émission bu am solo bu ñuy taxawal fii tey
/content/data_kallama/58segment_330.wav
mais xoolal suñu xale yi fi nekk xoolal xale yi loo wax rek ñu ne mbënd mi fan yii yëpp boo déggee ministre yi dafa même ambassade de France ak yëpp a ngi wax wa dëgg la boo béyee benn at ñaari at yow munoo ngoro mënoo ci jënd paire nag munoo tabax tabax bu baax mu mujj wóccu ko i ne man damay dem Dakar nga jëm Dakar da ngay xool néeg boo xam ne juróom-ñeenti nit a ciy nekk di bokk di fanaan buñ xëyee duñ ndékki wala kii day tëdd nelaw ba doyal jug doog a abal keneen ki mu doog a tëdd mais loolu ba kañ buñ demee ba xajatuñ la ñuy wëlbatiku sóobu ci géej gi ne am alal rek wala dee ñu suul
/content/data_kallama/39segment_420.wav
picc yi kat gis nañ bu ñu commencé kii tàgg wala mel na ni nii ndox mi kii biddéew sangam bu ñu ko gisee xam nañ ni peut être que dëgg la seetlu yi moom moo bokkul parce que ñii dañ ko teg ci li ñuy wax une connaissance empirique muy seetlu bi nga xam dangay xool rek seetlu nii mais nag ñun dañoo am ay jumtuwaay ay appareils muy ay instruments météo lu demee ni ki ay thermomètres ay ay appareils de vent ay ay ordinateurs ak yeneen i jumtuwaay ay satélites
/content/data_kallama/37segment_630.wav
à deux cent waa bu jigéen bi xoolal loolu bu écloré fu ñu jëm kon nag ki fi ñëw moom mii di ci boppam ci kilifa la ci DPV mbokk yi waxtaan waa ngoog waaw dañoo jàkkaarloo ak yéen kon nag jàkkaarloo baa ngi noonu yéen ñii di béykat yi nee naa leen waxtaan baa ngi nii bépp laajte bi ngeen ko bëggee laajte leen ko ci Diakhoumpa balaa muy dem
/content/data_kallama/98segment_600.wav
boo xoolee taxawaayam am na kër gu boo xam ne moo nekk fii ci quartier Escale ñi ko xam bëri na ndax Fatick moom boo nee agriculture rek dana bërëb ba dafa jëmme ndax dafa am histoire dafa am taarix boo xoolee département bu ne it kër ga jëmmal nañ ko fa donc mu am kilifa bu ko jiite ak ay % ay techniciens noonu la bindoo si wàllu taxawaay li ko wër nag ay projets ak ay programmes la yoo xam ne ñu ngi ci ndigalu ministre de l' agriculture d' équipement rural ñoom it bokk ci liggéey bi kenn ku ne di indi sa wàll ci ci ci ci ci li nga xam ne moom lañ bokk jëmee ko ci béykat yi nga xam ne mu nekk wàll wu am solo ci askan wi loolu loolu mooy taxawaay bi ci wàllu bi ñun ñëpp ñu nekk ay lu ñu tuddee démembrements
/content/data_kallama/12segment_510.wav
wala man nga woo ma man di 77 810 00 94 wala nga woo Soxna 495 495 57 92
/content/data_kallama/68segment_1200.wav
jërëjëf voilà donc effectivement ki mujjee woote léegi li mu wax lu am solo la parce que yàlla moom mooy
/content/data_kallama/25segment_630.wav
voilà donc jigéen ñi dañu kaa war a xam ni ko Fatou Seye waxee bokk ci lii di Fapal mooy que lii lépp dangeen di faral di waxtaan ak ñoom di leen ko xamal ñuy xam fuñuy teg seen i tànk waaye nag ba ci biir Fapal boobu ci boppam am na fa yaakaar naa ni ay genre ru micro jigéen ñi di ci bénéfice woo bu baax a baax
/content/data_kallama/0segment_210.wav
fokk li ngay def nit ñi xam ko pour mu mën a am njariñ mais am na ñoo xm ne dañuy jàpp ne ñoom li ñuy denc moom moo am njariñ maanaam li ñuy denc seen dëkk ñoom rek ñu xam ko te loolu yow li nga am ca ame xam-xam la ci keneen amee xam-xam wala ëpp la ci ay ay pexe xay na bu ñu ko séddoo woon dana ngeen da ngeen dana la mën a gën a jàppale moo tax ci wàllu woowu bépp unité maanaam bu doon transformation bi nga xam ne dangay transformation fii ci
/content/data_kallama/143segment_1170.wav
maanaam producteur bi di bañ a fàtte fumier bi mu am këram wala foofu ci àll bi bu koy indi di ko def ci toolam wala mu dem ci DRDR wala ku mu dem pour mu jox leen phosphate wala moom ci jëmmi boppam ddéchet bu mu am ci tool yi daal di koy def ci biir toolam donc loolu bu ko defee
/content/data_kallama/11segment_1290.wav
d' accord mais il faut ñu moytu souvent luuma yi produits yooyu énuy joxe ñuy jaay comme suñu produits yi mais ay yu si ëpp produits yooyu baaxul dañuy jël produit ba noppi jël si tuuti jël ay sunguf mélangé ko de ce fait léegi béykat bi bu ko jëlee pour que aar ci gàncax gi da koy sotti waaye ki dara du baax
/content/data_kallama/50segment_1230.wav
parce que non seulement dañ ci am représentation mais suñu taxawalee bureau bi ci wàllu poste yi am solo yi poste stratégiques yi jigéen ñi tamit war nañu occupé postes yooyu
/content/data_kallama/95segment_90.wav
rendement yi du bokk waaw ndax mos ngaa gis sa téléphone benn message bu lay wax ci wàllu mbay mi waaw ndax woo na ma ne ma yow yaay Boury Mbodj ma ne ko waaw man la Boury Mbodj
/content/data_kallama/107segment_270.wav
waaw parce que adduna bi lan moo tax ñu naan noor naan nawet c' est parce que donc période bu nekk rek dafa am si lu ñuy wax suñuy sunuy sunuy termes yooyu yëpp dafa am benn période boo xamante ne noonu la jant bi di xaree adduna bi donc boo gisee bu fekkee comme jamonoy nawet da ngay gis ni bëccëg bi mooy ëpp guddi gi
/content/data_kallama/73segment_60.wav
ndax nag wax dëgg yàlla lépp loo xam ne ci kaw loolu la ñuy profité nuyu sunu wayjur bu tedd bi El Hadj Falilou Diagne di ko ñaanal yàlla xaaree ko àjjanay firdawsi di nuyu ki nga xam moom mooy présidente Fatou Binetou Diop di suma mag di suma xarit
/content/data_kallama/24segment_750.wav
waaw xam nga loolu ku ku ku jàng rek ku ko xam fokk mu am ku ko xam ku ci nekk kooku mooy tax danga ciy jàppale jigéen bi maanaam da nga ko moom toujours mi ngi ci yëngu-yëngu bi waaye yëngu-yëngu bi dafa mel ne lu xaw a tas dafa tas amul maanaam structuré wu ñu ko yow nag mi àndi am sa xam-xam yow yaay mel ne un coach :en ni nga koy defee nag mooy dangay teg jumtukaay yooyu lu mel ni comme business : en plan
/content/data_kallama/56segment_1320.wav
dafa am ay ñoo xam ne dañuy wax ne boonaafee daf ciy am li ëpp ci liy yàqu ci nawet bi yi ci gën a yàq yàq bu ëpp rek mooy woŋ woŋ maanaam sooy naal da nga war a puudar woŋ moom woŋ moom tool bu mu xas dugg moom booba yàqu na loolu puudar boobu nag moom li ñu si mënee dimbali rek mooy nañu ci nañu ci gouverment jàppale ndax puudar bi dañ ko mënut a gis sax
/content/data_kallama/10segment_360.wav
waaye xam nga ni doomu Adama bi loolu la mun comme duñ taw duñ def dara ji nañu béy nañ et fi mu nekk nii yàlla mooy baaxal et fi mu nekk nii daal am ngeen jërë ngeen jëf et fi mu nekk nii daal affaire bi moom mu ngi noonu ngeen yokk a góorgóorlu ndax nawet yi li may gis ci nawet yi fii léegi jiw ak engrais moom baax na ci ci nawet bi may gis léegi ndax moom moo koy baaxal daal et yàlla nag mooy taw bu tawee ndax dangay gis nawet sax mu taw a taw a taw a taw ba xam ne kii too() dara dara du am loolu nag ci mbiru yàlla la
/content/data_kallama/16segment_870.wav
kooku moom dinañu indil problème ndax jigéen ñi bari na ay kuréel yoo xam ne day financé wante nag li may wax jigéen ñi rek booy dem ci mutuel di kii di àbbi xaalis war ngaa xaar bala ngaa def lenn war ngaa xool yan activités ngay def doog a dem xaalis kenn du ko jël ba noppi door a xalaat li ngay def soo ko defee rek dangay échec xaalis bala ngay dem dangay dangay xool sa activité lan la war a jar nga war koo
/content/data_kallama/80segment_300.wav
projet bi nag dafa nekk projet faire faire bu ñu nee prjet faire faire mais li ëpp ci liggéey bi dañ koy jox ay kuréel yoo xam ne ay kuréel yoo xam ne état du Sénégal ci li ëpp
/content/data_kallama/14segment_0.wav
* ñun am nañ information ne nawet bi kat dina bëri ndox wala du bëri ndox ndax na teel a commencé wala du teel a commencé ndax bu ñu demee ba ci digg nawet bi maral dina am wala maral du am mais dina ko may tey mu jël ay matuwaay ba su boobaa li docteur di wax ni teel a ji dafay nekk loo xam ne am na solo parce tey boo xoolee ndox mi ni muy yéex a ñëwee wala même bu teel a taw tamit dina taxaw ab diir bu yàgg mu doog a départ kon gis nga ne fi ñuy amee ndox dëgg-dëgg waxtu wa ñu doon waxee ne pare nañu wolli ñun fa la ñuy waxee ne ñu ngi ji gerte
/content/data_kallama/31segment_1230.wav
fu mu toll nii daal sàmm yi lañ doon xalaat te sàmm yaa ngi góorgóorlu vraiment ñu ngi romb foofu di sàmm seen jur normal ñaareel ñaareelaguñ ñu daal ndax ñoom ñoom ñooy suñu problème instant bii mais bu dul ñoom moom amaguñ beneen programme beneen problème ci yàqu-yàqu bu dul ñoom amuleen beneen problème si yàqu-yàqu bi
/content/data_kallama/36segment_690.wav
ñu ngi lay nuyu bu baax di la ziar ñu ngi lay fay macha allah di ziar Maodo Habib Thiam moomu waaw waxtaan bi am na solo trop tout à fait yal na yàlla dëgëral te barkeel ko amiin yaa rabi li mu wax lépp de njëriñal béykat la waxu si benn yoon njëriñam
/content/data_kallama/4segment_540.wav
bañ jógee Kaolack aussi bañ ñëwee
/content/data_kallama/79segment_510.wav
mais ñun fii amuñu moyens yooyu kenn kenn du ji mboq ba mu rafet nga dagg ko même sooy def ensilage maanaam élevage foog nga nekk un grand fermier pour def loolu
/content/data_kallama/79segment_780.wav
genre dafa xew nagam jigéen ñi dañu leen a jigéen ñi dañu leen a dañu leen a dañu leen a beddi waaw ah ha kon ginaaw si jigéen ñi la nag moom dafa ñëw dooleel jigéen ñi ne tekkil jigéen ñi jigéen bañ a toogati %hu_m tekki ne ñëpp kay
/content/data_kallama/93segment_420.wav
parce que buy ñëw ci li mu njëkk a jot rek ci loolu lay loolu lay loo ci ci ci loolu lay agrippé wu kooku moom mooy benn bi nañu éviter buy taw nii wala muy am ay dënnu ñuy toog ci jàkkaarloog fenêtre wala buntu comme lee day dem di wut lu ko lu ko sauvé bu gisee buntu wala fenêtre foofu lay jaar dëgg la loolu aussi beneen aspect la
/content/data_kallama/103segment_150.wav
direction protège protection des végétaux moom mooy service bi nga xam ne day aar lépp loo xam ne mi ngi si si gàncax gi lay laal gàncax gi waaw benn dem na ci ba ci njéréer yeeg lépp luy kii soccat yeeg yëpp da da da ko da koy aar léép loo xam ne rek day yàq gàncax gi moom da ciy intervenir waaw maanaam mën nañu wax ne lépp loo xam ne génnee na ci gàncax daal
/content/data_kallama/72segment_930.wav
bu ko fournisseur bi indee ba ñu defal ko PV de réception ak bordereau de livraison moom lay présenter ci projet yi projet i demander à la banque pour mu fay fournisseur bi donc noonu lay ligg() kii bi daal lu mu soxla pour liggéey moom lay jot mais xaalis bi dañ koy defal ci compte am mais décaissement bi projet bi mooy joxe autorisation d' accord
/content/data_kallama/29segment_1320.wav
am na li ñuy wax les méthodes physiques de lutte yeneen méthodes yoo xam ne ay ay ay c' est des méthodes physiques de lutte peut être dinañ ci dinañ ci dinañ ci ñëwaat
/content/data_kallama/30segment_420.wav
appui développement local ñoom ña nga fa am nañu fa lu mel ne que tey boo demee ca Louga lu mel ne que lu mel ne que maison développement local mi ngi fi lu mel ni que tey jii ARD mi ngi fi lu mel ni que tey c' est à dire bureau boo xam ne nii lépp lu jëm ci koom ci biir communauté ci biir commune bi
/content/data_kallama/69segment_630.wav
fii ci département bi ñun maanaam yegg nañ fa li ngeen xayma woon ne ren moom la ñu war a am voilà liñ xayma woon ne moom la ñu war a am yegg nañ fa ñu mun ko tudee perturbation wala sax déréglement comme ni nga ko waxee ñu ñëw ba mois d' août gis ni mbir mi daal di ubbi mu daal di am ay taw yu am doole ci biir département bi
/content/data_kallama/32segment_30.wav
on a appris beaucoup de Ticmbay peut être cette année ci àa n' a pas marché parce que c' est lié un peu à ma maladie à un cerain moment donné ci biir projet bi donc j' étais obligé vraiment ma bàyyi mu jàll loolu rek moo tax sama échec bii ren ci programme bi ngeen ma dénkoon mu am échec échec bii ren
/content/data_kallama/68segment_690.wav
nawet bi dana bëri ndox lool taw yi danañ bëri lool te aussi vraiment bon woor yi dana dana néew maanaam ni nga xamante ni moom la daan wooree daaw di woor ay 15 jours 20 jours yenn saa yi ay gox yoo xamante ni day toog weer sax du taw vraiment loolu moom incha allah ren moom bon yaakaaruñu ni dina am bu soobee yàlla
/content/data_kallama/0segment_1050.wav
mais day am formation mais day am pra() partie aussi pratique
/content/data_kallama/90segment_0.wav
Pape Mbaye waaw waaw fii fan nga dëkk fii Elimane Nganda lan moo tax ngay utilisé neefere yi pour gàncax gi quoi ci la ñu koy def pour mu gën a baax quoi day màggal gàncax gi da koy màggal waaw da koy màggal waaw depuis kañ nga ko commencé utilisé kii kay bon danoo fekkoon sunu maam yi nekk ci ok :en
/content/data_kallama/104segment_990.wav
dangay sentir que ni kat am na nu mu demee xam nga lu ma wax léegi ci kaw loolu man li may wax nit ñi rek moom mooy xodeeku balaa ngay lakkle adaptation baax na atténuation baax na mais di prévoir li nga xamante ni ñëwagul tamit yaakaar naa ne loolu moom moo gën te munoo nekk béykat amuloo lu dul ñëtti weer nga am li nga xamante ni bi moom nga amoon ci alal yëpp nga investir ko investir sa doole investir sa njaboot dégg nga
/content/data_kallama/9segment_270.wav
doo ko mën a saafara léegi jafe-jafe yi am daal loolu bokk na ci ndax boo xoolee treize août nga ji ko jiwu commencé mu commencé meññ benn meññ bi liy problème moom mooy ruur mi ci am boobu buñ amoon traite() buén amoon traitement waaw kon sëñ Talla jërëjëf di fàttali auditeurs yi rek yow la yow yaa nekkaloon projet bi fële ca Darou Naim
/content/data_kallama/34segment_30.wav
maa ngi rappelé wu ci benn benn kuréel boo xam ne doon naa ko defal enquête 2004 am na ci benn paa boo xamante ne dane man de damaa jaaxle ndax de kon tax loolu tax na intitution de microfinance yi war nañoo xoolaat naka lañuy gën a fexee ba jàppale
/content/data_kallama/67segment_690.wav
/content/data_kallama/9segment_1320.wav
te à tout moment mais mais mais Samb ci ci ci ci prévision ci six mois rek ci six mois yiy ñëw waaw non commencé guñ liggéey ci loolu nag
/content/data_kallama/124segment_1050.wav
effectivement ñun amuñu xam nga ñun bu ñu joxee dara ñun liñ ñu jox moom la ñu joxe lu ñu joxewul duñ ko mun a joxe donc man sama sama sama wàll bopp dama leen di wax ku ñëw même pour ma jox ko puudar ma ne ko sóoraaleel loolu déwén parce que wóoratul ndax lii day am donc bala campagne di kii utal fi nga mun a amee loolu nga garder ko léegi toll nañu période bi nga xam ne daal béykat bi da nga war a jël sa bopp en charge dañu doon joxe dañu doon joxe mais boobu xamu leen engrais bi daawuñu ko maye daañu ko daawuñu ko jaay mais léegi dañ koy jaay parce que ñëpp xam nañu njëriñ bi su dee si loolu la parce que bala ñu jaay la dara nga jënd dara foog nga am njëriñ
/content/data_kallama/19segment_360.wav
kon war nañoo mën a xam boo defee engrais tey
/content/data_kallama/5segment_990.wav
nga jox jigéen ji mu lekk ba suur faj ko ba mu wér kooku dina mën a nàmpal dooma dana nàmpal léegi ah amaat soow léegi loolu noonu nga ko jox loolu mooy matière organique ba * matière organique du dafay ñëw rek dundal gàncax bi directement
/content/data_kallama/56segment_330.wav
moo leen di permettre également ñu kii quoi boo xoolee sax am na si ñi nga xamante ni bii des fois xam ne par exemple dañu war a béy ay légumes wala dañu war a béy yenn xeetu gàncax yi nga xamante ne bii souvent dafa soxla tàngaay te ñu xam ne que ni période bi nga ko bëggee
/content/data_kallama/31segment_420.wav
yoo() ñooña ñëpp ay jigéen lañu yoo xam ne si dañoo sukandiku ba defar seen i ay places jël ay xale yu góor ànd fa ak ñoom ñuy ñuy ñuy ñaw di di di di teral seen kër di teral seen ay njaboot
/content/data_kallama/14segment_1020.wav
waaw dinañ la sonal mais ci biti da ngay wax bu baax waaw une minute
/content/data_kallama/0segment_960.wav
utee naag ceeb ak dugub gi nga xam ne gub bi directement dafa nekk contact ak asamaan si di am air di am chaleur mboq moom yàlla da koo may mu am mbubu
/content/data_kallama/32segment_840.wav
nga bàyyi fa xale yi ñuy ñuy fëgg di xàjji ah léegi des na gerte gi jiwu beneen dugub bi dugub bi des na tuuti yoo xam ne ay benn-benn yu war a am yu ñor xanaa ñu wax gaa yi ne ko loolu nañ góorgóorlu taxaw si parce que Guèye keroog waxoon nañu wax nañ si yu bëri si wàllu mbéy mi ñun nag ñu ngi béy waaye ndeke xam-xam bi des na des na xam-xam bi des na dëgg la ay béykat lañ piir mais nag xam-xam bi des na dëgg la man maa ngi rafetlu nag projet bi parce que jox nañ ñu xam-xam yoo xam ni même buñ affaire bi jeexee
/content/data_kallama/6segment_540.wav
maanaam climat bi changé na jafe-jafe ñëw na léegi jafe-jafe yi nan lay wàññeekoo mooy mécanique waaw waaw changement boobu nag maanaam na la def ba mën a changé wu ndax dina am fu ñuy sukkandiku wala dina am rekk changement boo climat bi waaw climat bi waaw climat bi waaw bon xam nga tey jii nii boo jëlee dafa am ay borom xam-xam yu mag xam nga muy yow muy man amuñu jumtuwaay ak xam-xam yu doy
/content/data_kallama/120segment_780.wav
/content/data_kallama/56segment_1440.wav
effectivement 20 milimètres boo ko amee loo ci jiw mu sax
/content/data_kallama/18segment_1080.wav
waaw xam nga comme ni ma ko waxee xam nga producteurs yi xëy na peut être façon bi ñuy stocké peut être ñàkk manque de moyen moo tax ñuy stocké noonu
/content/data_kallama/3segment_630.wav
tey su ñuy lig() suñuy yëngu ci entrepreise ci biir kër yi moo xam biir kër yi te it ñu war a ràññee ñaar poche su entreprise bi ak poche su kër gi walaay muy nekk th-me boo xam ne si bu ama solo la ndax soxna Anta wax na ko si jeexantalam kon foofu wax dëgg yàlla énun jigéen éni kenn ku ci nekk war na bàyyi xel kenn ku nekk am na droit am na sañ-sañ pour naka la mën a tëggee projet pour ñu jàppale la
/content/data_kallama/19segment_360.wav
xëy na sax donte bu doon ñetti nit ñeenti nit jëlee nañu ci njariñ ag cant la ñu ngi leen di sant di leen gërëm ndax itam ñoom itam tey jii bu tollee fii seen liggéey la mais am na nu muy demee duñu toog fii di ci wax
/content/data_kallama/15segment_0.wav
fonds yi nga xam ne nii ministre de la microfinance teg na ko fonds yooyu tey jii bu fekkoon ne dana daj bu fekkoon dana daj dëkk yi dana am solo trop te kuy liggéey danga ca mën a gñn boo xoolee cycle bi waaye am na ñoo xamante ne dañuy dem ba la ñu amoon sax dañu koy jaayaat maanaam au lieu que mu mu mu amélioré seen performances dafa leen di daf leen indil ay contre performances ba seen la ñu amoon sax dañu koy far di jaayaat
/content/data_kallama/61segment_600.wav
loolu moom mën nañu wax ni lépp lu UGPM di def
/content/data_kallama/56segment_270.wav
léegi xam nga matukaay yi nga xamante ni dañ ko war a jël dafa am deux niveaux benn bi mooy niveau un bi mooy que la modification des dates :fa de semis maanaam date yi nga xamante ne dañ si war a ji dañ ko war a soppi yaa ngi dégg beneen bi mooy ñu mën a chnagé ay variétés yu ñuy béyee ma béy fure maa ngi doon béy fure ma béy fleur onze maa ngi doon béy fleur onze wala ma béy **
/content/data_kallama/114segment_150.wav
kon yaa ngi ciy gis ay njëriñ lu am solo waaw maa ngi ciy kii bu baax a baax moom vraiment foo ko foo ko jàngee foo ko déggee foo ko mos a déggee ok :en ndax yaa ngi dégg émission bi coopérative bi di def ci rajo Alfayda
/content/data_kallama/144segment_1470.wav
bu fekkee aussi dem nga amoo moyen comme ni ma la wax rek amoo ay moyens yu bari maanaam tool war nga tey boo bayee fii gerte bu déwénee nga bay fi dugub boo bayee fii mboq bu déwénee nga bay fii gerte
/content/data_kallama/7segment_210.wav
ci ban service la nekk maanaam moom ci boppam moo yore boppam wala dafa bokk ci beneen service c' est une direction de l' agriculture moom la DPV nekkee direction di() direction protection des végétaux service à part mais sunu ñëpp sunu yaay mooy agriculture léegi nag ñun fii ñu ñu fi affecté au niveau du département ñun ñoo man maa fi ne wante mais nag on gère deux régions
/content/data_kallama/9segment_1260.wav
changement climatique boobu nag xëy na tey yëkkati wu ñu peut être que du ñu ci mën a xuus bu baax waaye ngeen jàpp ni du dara lu dul tàngaay bi nga xamante ne bi moom moo jógee ci naaj bi
/content/data_kallama/71segment_300.wav
ci espace régiale CEDEA boobu nag boobu la ñu tënk benn document bu nga xamante ne fa la ñu def maanaam li nga xamante ne lépp dafa jëm ci wàllum semence foofu la ñu ko def waaw te loolu noonu maanaam dafa wax ni ci article cinq ci chapitre cinq article onze dafa ne lépp li nga xamante ne pour wàllum copntôle lu semence la ak certification bi loolu daén koo jagleen ñi nga xamante ne mooy waa DISEM DISEM boo ko déggee mooy division des semence
/content/data_kallama/26segment_240.wav
gerte gi jëndoon na ci 200 30 tonnes yoo xam ne dakoo jënd ñaare bu prix marché;fra bi nekkee 300 en gñéral Fapal 350 lay lay jëndee voilà ci wàllu formation mais est ce que tamit yéen en tant que technicien xam nga local xaw ma nu ngeen koy defaree
/content/data_kallama/90segment_1590.wav
bu ñëwee ci moo yow da nga koy diagnostiqué ba pare nga xam lan mooy tawatam nga door ko wax yan matuwaay la war a jël mooy saafara tawatam kon moo tax lii dafay am solo béykat yii nii ñuy def comme kii nu mu def ni Sezrigne Seck ñu ngi koy encoragé bu baax ndax lii muy def dafalu ko boppam rek gox bi yëpp yan jafe-jafe la ñu am bu ko defee bu ñuy jël ay matuwaay gox bi yëpp lañ koy jëlal moo tax it ñu ngi koy jaajëfee bu baax a baax
/content/data_kallama/58segment_540.wav
di jégalu sunu tardement bi di nuyu Ibrahima Diop mii xam si ne moom la ñu seqal table bi comme émission bi tey mi ngi ñëw ci Fra ak code barre loolu dana nekk loo xam si ne dafay jàppale jigéen ñi si seen wàllu activité yi nga xam si moom la ñuy liggéey ku mel ne kuy defar céréale wala kuy defar yeneen ak yeneen produit yoo xam si ne dangaa bëgg mu gñn réew mi wala sax dangaa bëgg mu tasaaroo ci biir réew mi
/content/data_kallama/129segment_300.wav
waaw bokk ci coopérative bi maay président sa UVD itam muy Diosone
/content/data_kallama/1segment_180.wav
te loolu dafa baaxal li nga xam ni mooy seen dundin dimbali na leen aussi ci seen nekkin ci wàllu liggéey bi mais dimbali na leen aussi ci seen yeneen campagnes yi nga xam ni ñoo si toppu parce que tax na nga denc loo xam ni dinga ko mën a muy jiwu jiwu tax na itam nga jël loo xam ne dinala mën a permettre nga def beneen activité diversification aussi cultures yi nekk na loo xamante ni lu am solo la baykat yi vraiment gis nañu seen bopp si projets yi gis nañu itam li ñu doon waxtaan si wàllum rajo bi amalnaleen njariñ
/content/data_kallama/0segment_360.wav
le 15 août boo demee ci lu mel ni Taïba ñu mel ni Kër Maba dinañ commencer vraiment di récolter :ra maïs vert bi démb rek tey rek ci suba du ma wax tur am na producteur boo xam ne jox na ma mboq vert
/content/data_kallama/53segment_1380.wav
te lu am solo la ci xalaatu li ñuy tuddee résilience maanaam utub pexe loo xam ni ngir gën a ñoŋal béylat bi yokk poosam yokku pexeem ba nga xam ne bu amee choc li ñuy tuddee choc climatique maanaam taw yu yéex taw yu lifin mu mun a bëyandoo lu bëri njëkkee lii teg ci lii teg ci lii boole lii li ñuy tuddee diversification pour mën cee génn ci wàllum am sécurité alimentaire
/content/data_kallama/107segment_900.wav
xanaa ñëwu ñu COPACEL wala feneen ñi nga xam ne amuñu ko waaw dama ne ku wax affaire jiw ku ci am loo xamante ne rek jaaxal na la waaw xanaa ñëwoo COPACEL xanaa ñëwoo COPACEL waaw waaw parce que COPACEL a ngi fi Fapal a ngi fi ñoom Youssou Diallo ak Bada Mbengue ñoom ñëpp ak Mbaye Mbengue foo si dem daal fii mu ne boo jekkoo ñëwal nga waxtaan ak ñoom jaar ci lépp lu ñuy jot ci DRDR bi la jaar ñoom Demba Tall xam na at mee mu ñëw sama tool
/content/data_kallama/20segment_180.wav
waaw xam ngeen ne fi mu toll nii garab yu bëri ci àll bi gars yi dagg nañ ko donc depuis taawu Sodeva ba nga gis ne garab yi dagg nañ ko
/content/data_kallama/89segment_900.wav
muy muy doon problème boo xamante ne gis nañu dañ koy jànkuwanteel fii ci fii ci wax nga sànq nag ci hivernage wax nga njëriñ yi nga xamante ni mun nañu jàpp ni am nañu yaakaar bu baax a baax que ni nawet bi jebbi na bu baax a baax a baax te itamit amal na njërién ñii nga xamante ni ñoom ñooy
/content/data_kallama/50segment_1290.wav
ana waa kër yëpp ñu ngi fi ñu ngi si jàmm kontaan nañ ci émission bi ndax wax dëgg yàlla nit ñaa ngi ciy am na daa ñu ci yo() ku ci bëgg a am xam-xam moom da nga ko ci jëlee nawet moom bu xa() tool moom bu xasee ba ñor yàlla jiy taw ah moom kooku moom il faut rek borom am borom am mu am xam-xam boo xam ne nii lii nga xam ne kay moom gerte gi moom bu ñu ko deqee ci ci bàq bi
/content/data_kallama/52segment_690.wav
boo jëlee ci wàll
/content/data_kallama/30segment_570.wav
soo demee tey war nañ la gunge enregistré ko daal di lay jox li nga xam ne mooy reçu ñi nga xam ne ñooy autorités yi nag ñoom ñu doogay jël en main li nga xam ne moom la ñu war a def mooy ñooñu dinañ dem fekki parents yi dinañ dem si dëkk ba ñooñu nga xam ne prospection lañuy defi
/content/data_kallama/12segment_1920.wav
su fekkee ñëw nga si journée bi dinga xam li nga xam ne moom la ANCAR ISRA ak yeneen partenaires yi nga xam ne ñoom ñoo bokk si biir li nga xam ne mooy seen liggéey di def ci gox bi loolu nga mun ko yóbbaale mu mun a nekk sa ngànnaay ëllëg tam nga xam fan ngay jaar ci sa wàllu liggéey waaye rawatina lu jëm si wàllu mbéy mi Sadio Deme sànq wax nga ANCAR am na ñaari espèces yoo xam ne moom lañ doon essayé fii si biir commune bu Thiel lu si mel ne ñebe lu si mel ne tam dugub bi
/content/data_kallama/28segment_300.wav
léegi yow fan la ñu war a tàmbalee pour teg loolu parce loolu yëpp ñor na ma kooku moom il faut ñu woo les administrateurs des coopératives parce que Resop dafa am su ko defee nga wax ak moom mu mën a con() convoqué CA Resop conseil d' :fr administration bu Resop
/content/data_kallama/84segment_330.wav
donc fii am na jiw bi nga xam ne daal dafa gaaw chercheurs yi waa ISRA ñoom ñooy gëstu ci loolu donc ca mbéy mi direct :ra moom dafa dépendre driectement ci ndox bi ci taw bi donc kenn mënul am tool ay dugub ay lan nga arrosé ko ban moyen amoo amoo amoo kii boobu donc foofu ñi am xeeti jiw bi nga xam ne daal
/content/data_kallama/63segment_570.wav
noonu ngeen koy noonu ngeen ko jiyee waaye gis ngeen ne daal fiñ waaw am na différence am na différence Aliou ci fànn yëpp mbéy mi ba ci bi ci mbéy mi ak ci njiwin mi quoi danañ ni ma gisee programme bi bu demee ci kanam danañ ñu jàppale ba nga xam ne même
/content/data_kallama/54segment_870.wav
yooyu ay tracteurs la loolu yombul mais il faut nga am moyens pour accès pour am ko mais nit ki mooy def choix am moom day xool nan lay amee machines yu baax mu koy mu koy mu koy utiliser mais bu fekkee producteur la bi nga xamante ni am moyen am bëriwul amul doole
/content/data_kallama/68segment_930.wav
maanaam ñu def ay jàngat xool gis ne effectivement maanaam avant révolution industrielle nit ñi ku si nekk di
/content/data_kallama/71segment_1050.wav
ngeen daal di joxe seen contribution si li nga xam ne rek moo di émission bi nga xam ne moom la ñuy waxtaanee nii Cheikh Top Kër Mandoumbe Cheikh Top Kër Madoumbe waaw na nga def
/content/data_kallama/60segment_30.wav
d' accord d' accord baax na Jalle jërëjëf waaw dama doon ziare *** kontaan naénu bu baax en tout cas mi ngi noonu parce que émission bi ñu ngi koy déglu fu ne ñii ñu ngi suivre fu ne ñii a ngi Njeri ñii a ngi Kalla Sane ñii di Louga fii ak
/content/data_kallama/29segment_750.wav
waaw junj nga ko sànq ci li nga xamante ne ni moom mooy wàllu engrais bi waaw ni ma la koy waxee noonu la war a mën a demee waaye am na uute bu soppi bu ndaw bu am ci wàll parce que dugub xam ngeen dañ koy faru
/content/data_kallama/14segment_1320.wav
dem ci structure bi comme ANACIM