wolof
stringlengths
1
166
french
stringlengths
2
331
borom-bakkan b-
être vivant
borom b-
maître propriétaire
Borom woto yépp a ngiy jooytu tali yu yàqu yi
tous les automobilistes se plaignent des routes défoncées.
(loc.) Borom bi, musal nu !
mon Dieu, sauve-nous !
(prov.) Borom ŋàdd yëgul borom pañe
celui qui a un morceau de noix (de cola) n’a cure de celui qui en a un panier.
borom-bopp b-
rage de dents mal d’oreille maux touchant le champ O.R.L
borom-bopp a ko tëral fi-mu-nekk
en ce moment, il est alité à cause d’une rage de dents.
Dafa ànd ak borom-bopp; du liggéeysi
il a une rage de dents; il ne viendra pas travailler.
borom-i-may b-
personne qui a des dons mystiques
Borom-i-may la
il a des dons mystiques.
borom-dëkk b-
chef de village
borom-kër g-
chef de famille maître de céans
boroode
broder
borom-kër g-
chef de famille maître de céans
boroode b-
broderie
bin-bin
(pop.) Agir avec pondération, tout doux
Deel bin-bin ak say goro
il faut y aller mollo avec les beaux-parents.
boseet
exprime l’idée de dégainer brusquement (une arme blanche)
Dafa ne boseet paaka
il dégaina brusquement un couteau.
bot b-
fruit vert du savonnier (flore) Balanites aegyptiaca, Simaroubacées
boxom
Écraser légèrement une chose entre les doigts, soit pour la froisser, la ramollir, ou pour en détacher qqch
Bul boxom xaalis bi
ne froisse pas l’argent (le billet de banque) !
boyal
laisser le bétail aller paître sans berger
Su nu xëyee, boyal
le matin, nous laissons le bétail aller paître.
boxomu
être froissé
boyet b-
boîte
Defal dàll yi ci seen boyet
mets les chaussures dans leur boîte !
bu
que (sujet) ne pas…
Bu mu dem léegi
qu’il ne parte pas maintenant.
boyy
être resplendissant
Dëkk baa ngi ne boyy
la ville est resplendissante.
buccatiku
être très mal élevé
Dafa buccatiku
il est très mal élevé.
buddat
arracher la mauvaise herbe qu’on ne peut pas enlever au pied des plants avec une hilaire
Xale yaa ngiy buddat
les enfants arrachent l’herbe qui est au pied des plants.
buddat m-
la mauvaise herbe arrachée au pied des plants
Lakkal buddat mi
brûle l’herbe arrachée au pied des plants !
buddeeku
’arracher
Soo ko xëccee, mu buddeeku nak, lan ngay wax
si tu le tires et que ça s’arrache, que vas-tu dire ?
buddi
arracher
Dafa buddi bëñ bi
il a arraché la dent.
bufta b-
trompette cor
Na bufta yi jib !
que résonnent les trompettes !
bugël
torturer
Xale yaa ngiy bugël muus mi
les enfants torturent le chat.
jëkk
être premier
Kër gu jëkk gi la
C'est la première maison.
(prov.) Borom ndékki, ku ko jëkka yewwu tëddaat
celui qui se réveille avant le maître de maison devra se recoucher
bul
que (tu) ne pas
Bul dem léegi
ne t’en va pas maintenant !
bukki b-
hyène
Bukki bee rey bëy wi
C'est l’hyène qui a tué la chèvre.
(loc.) Dafa sax bakkanu bukki
il flaire la nourriture de loin.
(prov.) Ku boot bukki, xaj bów la
les chiens aboient après celui qui porte une hyène sur le dos.
(prov.) Jél bu kii, suule bu kii
déshabiller Pierre pour habiller Paul.
(prov.) Bukki, wëri, wëri, jaari Ndaari
L'hyène aura beau faire des détours, elle passera par Ndaari
buleen
pluriel de {bul}
bulet
(culinaire) Préparer des boulettes
bulet b-
(culinaire) Boulettes de poisson ou de viande
bun b-
anus cul (vulgaire)
bulo b-
bleu de lessive
Bulo bi du doy
le bleu de lessive ne suffira pas.
bulo b-
sorte de véranda à l’entrée d’une concession
Mu nga lay xaar ca bulo ba
il t’attend à la véranda.
bummi b-
prince héritier (dans le Cayor et le Saloum.)
Doo buur, doo bummi
tu n’es ni roi ni prince héritier.
bun-fokki b-
(poisson) Perroquet
Dañuy liggéey ay làmp ak bun-fokki yi
on fait des lampes avec les poissons perroquets.
bu-nekk
chacun, chaque
Bés bu-nekk
chaque jour.
bunt b-
porte entrée issue sortie orifice
Kër gi benn bunt la am
la maison n’a qu’une porte.
buqi
Écarquiller les yeux
Looy buqi sa bët yi nii ?
qu’as-tu à écarquiller les yeux ainsi ?
bu-réy b-
ancienne pièce de monnaie
Booba, soo joxee bu-réy, ñu jox la juróomi tàngal
cette époque, pour un bu-réy, on te donnait cinq bonbons.
bett
surprendre
Dikkam dafa ma bett
sa venue m’a surpris.
(prov.) Lu la bett, mën la
ce qui te surprend prend le dessus sur toi
Bett nga ma
tu m’as déçu; tu m’en bouches un coin.
busëbaali b-
chenille
Bu nawet jotee, xay yi dañuy fees ak ay busëbaali
quand la saison des pluies arrive, les caïlcédrats se couvrent de chenilles.
butéel b-
bouteille
Butéel bi toj na
la bouteille est cassée.
butitu jurukaay b-
utérus
Butitu jurukaay bi mooy woññaaru
C'est l’utérus qui se contracte.
jurukaay b-
matrice
Jural naa la ba sama jurukaay bi yàqu
J'ai eu tant d’enfants de toi que mon appareil génital est détruit.
butoŋ b-
bouton
Tappal ma butoŋ yi
attache-moi les boutons !
bu-tuut b-
ancienne pièce de monnaie
Boo amaan bu-tuut, mën nga cee jénd paketu mbiskit
quand tu avais un bu-tuut, tu pouvais acheter un paquet de biscuits.
buub
entasser
Na buub mbalit mi, Astu dina ko an
qu’elle entasse les ordures; Astou l’enlèvera.
buuj b-
mactre (coquillage)
Dafay nuuru buuj
il cherche des mactres sous l’eau.
buum g-
corde
Jélal buum gi ñu yeewe woon xar mi
prends la corde avec laquelle on avait attaché le mouton !
Mënuloo def ni ñoom ndax danga nekk ci buum
tu ne peux pas faire comme elles car tu es mariée.
buun
avoir une forte envie de manger telle chose