url
stringclasses
152 values
text
stringlengths
4
5.13k
https://www.defuwaxu.com/mag-sama-gor-du-ragal-du-wor/
Aa, Kôro !
https://www.defuwaxu.com/mag-sama-gor-du-ragal-du-wor/
Yow wute ngaak nun de ! Ndege, yow tubaab bu ñuul kukk nga, dib doomu Farãs, làq sa paaspooru Farãs. Xam naa yit ne am nay artist yu lay jàppale. Duma tudd seen tur ; waaye sañ naa ne ñenn ci ñoom Gàmbi lañ fekk baax, dëkkuñu fi. Bu Làmbaay naree tàkk, yaak ñoom ay ànd fàq, ngeen làquji Bànjul walla Pari, yóbbaale seen njaboot. Kon, bu réew mi tàkkee, nun ñi amul fun làquji nooy xal a sonn, nooy dee. Ngalla-waay, buleen taal sunu Mali gii, ndax ñu mel ni man ak baadoolo yi fiy yeewoo Mali rekk lan am. Ndeysaan, dafa di sax, sa yoon dafa nekkul ci nun. Moom kay, nu dund walla nu dee nga yemale. Lu tax faalewoo nu, nun ñi la fal, nga war noo aar ? Metit wi, nun rekk noo koy yëg. Moo, ndax jotul nga yëkkati sag kàddu, xamal askan wi li xew dëggëntaan ? Ndeysaan, dangaa ragal say kàddu juuyoo ak bëgg-bëggi liir boobuy jiite réewum nootaange mi, Farãs. Lenn rekk a la soxal : wéy di toog ci jal bi cig ndimbalam, duy say poos ba ñu fees dell, yow, say mbokk ak ñi ànd ak yow. Ma ni la, nag, yaa wayadi dëgg-dëgg ! Yow yaa ñàkk gis-gis ! Boo geestu woon tuuti sax, dinga xam ni, yow, Keyta, waroo ragal, waroo wor askanu Mali.
https://www.defuwaxu.com/mag-sama-gor-du-ragal-du-wor/
Yaa gàcceel say maam ! Xanaa danga fàtte ni Keyta nga sant ? Sunu santu maam ja, jàmbaar ji, Sunjata (buuru Mali ciy ati 1236 ba 1255).  Cëm ! Jàmbaaru Kirinaa ngoog ! Gone gi duma woon jinne Sumaaworo. Kii daawul tiit, daawul daw. Xamul woon sax fu tiitukaay di nekk ci nit. Kon, ku nàmpe ci meenum Sunjata, bokk ci giirug Keyta-Keyta yi, waroo ragal. Tey ngay maas nii. Cim mbay ! Xanaa xamoo ni, Sunjata, ak li mu doonoon buur yépp, askanam a ko faloon. Nguuram du woon rekk ndono. Cib demokaraasi bu bir la nguuram lalu woon. Waaw kay !
https://www.defuwaxu.com/mag-sama-gor-du-ragal-du-wor/
Ndege, démb, kuñ ci falaan, cim pénc lañ la tànne, ci kow sàrt bu leer. Rax-ci-dolli, ndaje ma faloon Sunjata dafa tëraloon ab sàrt bu amoon taxawaayu ndeyu-àtte, ci atum 1236. Mi ngi tuddoon sàrtu Kurukaŋ-Fugaa, te amoon lu tollu ci 44i dogal. Kon, nun amunu ku nuy ñee. Nga war cee jàngat ñaari mbir. Benn, sunu njiit yu njëkk ya, duñu woon ay buuri ndono, askan waa leen daan fal cim pénc. Ñaar, duñu woon buur di bummi, di jaay nit ñi doole ak a def lu leen soob. Waaye dafa amoon aw yoon wu leen tënkoon, tënk réew mépp ak ñi ko jiite woon, réew mépp a àndoon tënku ci sàrtu Kurukaŋ-Fugaa. Lii mooy sunu aaday maam. Te yow it dañ laa fal, aw yoon tënk la, muy ndeyu-àtte réewum Mali.
https://www.defuwaxu.com/mag-sama-gor-du-ragal-du-wor/
Wànte, doo buur, kôro. Doo buur, de !  Xam ko bés niki tey. Moo, lu la tee roy ci maam yi, dekkil cosaan ? Ndax gis nga ne, demokaraasi bi ñuy soow, sunu maam yu jàmbaare woon yooyu ñoo ko njëkk a saxal, suuxat ko ? Sunu moomeel la. Tey, nga nasaxal ko nii, noon bi jaare ci, yàq réew mi yaxeet. Waaye, nag, ku xeeb juddoom, wàññi darajaam ; te ku xeeb sa cosaan, ñu xeebal la ko.
https://www.defuwaxu.com/mag-sama-gor-du-ragal-du-wor/
Bu dee li la say mbokki Mali yi dénk dafa diis ci yow, delloo leen seen moomeel ! Bu dee danga nar a boqu Kulubaa di lox, wàccal jal bi te ba kook ku am fitu def li war. Boo ragalee ne jàkk Farãs ak i njiitam wax leen dëgg, demal sa yoon ! Boo mënta yor réew mi, jóge fi ! Mali am na ay góor-Yàlla yu gëm seen bopp, xam liñ doon, bëgg seen réew, am xam-xam bi ak mën-mën bi, te am fitu yor ko, jàmmaarlook noon yi, defaraat réew mi. Boo demulee, nag, lu la ci fekk yow la.
https://www.defuwaxu.com/mag-sama-gor-du-ragal-du-wor/
Sàmmal sag ngor te bañ a gàcceel sa bopp. Ndaxte, kàddug maa demal sama bopp moo gën a rafet kàddug dañ maa dàq. Kon, fexeel ba bu kàddug gàcce googu gàkkal sa tur ëllëg. Ndaxte, suba du añ du reer, waaye dees koy sóoraale. Dëgg neexul. Bàyyi ci xel.
https://www.defuwaxu.com/mag-sama-gor-du-ragal-du-wor/
SA RAKK, SAALIF KEYTA
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-25-2-2024/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM (25/2/2024)
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-25-2-2024/
MBIRI PAAP GÉY AK MÀRSEY
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-25-2-2024/
Gannaaw CAN bi mu demoon ak Senegaal, Paap Géy, miliyë Màrsey (Marseille) bi dañ ko dàndoon ca këlëb ba, maanaan dañ ko génne woon, ber ko. Li ko waral mooy ni pasam dafay jeex ci weeru suwe 2024, Màrsey bëggoon mu yeesal ko. Waaye, Paap Géy dafa lànk. Njiiti këlëb ba jéem a wañ loxoom, mu bañ, jàpp fi mu jàpp rekk. Ci la ko Pablo Longoria mi jiite Màrsey beree.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-25-2-2024/
Ndogal loolu tiisoon na ko lool nag. Ndax, laata muy futbalsi CAN bi ak Senegaal, dafa toogoon diir bu yàgg bob, futbalu ci. Li ko sabab mooy ne FIFA dafa tegoon daan. Waaye, ab bunt ubbeeku na. Nde, boolewaat nañ ko ekib bi war joŋante ak Montpellier tey ci dibéer ji. Seen tàggatkat bu bees bi, Jean-Louis Gasset bi wuutu Gattuso moo sàkku ñu boolewaat ko ci gaa ñi. Ndax, ñépp la soxla ngir liggéey.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-25-2-2024/
ËRO 2024 : TONI KROOS DINA BOKK
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-25-2-2024/
Saa-Almaañ bi nangu na solaat mayo dëkkam gannaaw bees ko toppee ay yoon ngir mu ñëwaat ca ekib ba. Ca atum 2021 jëloon ndogalu bàyyi ekibu Almaañ bi. Keroog ci 22 féewiryee 2024 wii la xamle ci xëtu Instagramam ni dina dellu ca ekib ba.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-25-2-2024/
“JEUX AFRICAINS GHANA 2024”
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-25-2-2024/
Sëriñ Saaliw Ja, tàggatkatu ekib U20 bu Senegaal bi, fësal na limkag 23i ndaw yim tànn ngir ànd ak ñoom ci yooyu joŋante. Ci tànnam gi ñu gis ni woo na ci U17 yu bari yu demoon ci kuppeg àddina gii weesu (U17). Ñooñii di : Amara Juuf, Alfa Ture, Sëriñ Fàllu Juuf, Doriwaal Jaata, Yayaa Jémme, Ibraayma Jàllo ak Idiriisa Géy.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-25-2-2024/
EMILIO NSUE BÀYYI NA GINE EKUWAATORIYAAL
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-25-2-2024/
Saa-ekuwaato-gine bi jël raayag dugalkat bi ëppaley bii ci CAN 2023 bii weesu fa Koddiwaar xamle na ni bàyyi na ekib nasiyonaal ba. Gannaaw CAN bi, ay coow yu sew amoon na ci digganteem ak ekib ba, ñàkkul ni yooyu mbir a waral bàyyeem. Moom nag, futbal na 42i yoon ak ekib bi, daldi dugal 23i bii.
https://www.defuwaxu.com/li-gen-a-fes-ci-xibaari-taggat-yaram-dibeer-5-mars-2023/
LI GËN A FËS CI XIBAARI TÀGGAT-YARAM (DIBÉER 5 MÀRS 2023)
https://www.defuwaxu.com/li-gen-a-fes-ci-xibaari-taggat-yaram-dibeer-5-mars-2023/
LÀMB
https://www.defuwaxu.com/li-gen-a-fes-ci-xibaari-taggat-yaram-dibeer-5-mars-2023/
Saa-Cees – Rëg-rëg ñoo doon bëre ci dibéeru tey ji. Mu doonoon làmb ju ñépp doon xaar. Waaye, nag, coow am na ci. Nde, bu dee àttekat yi Rëg-rëg lañ jox ndam li, Saa-Cees ak i farandoom nee nañu ñoo daan. Ndaxte, ci biir jaxasoo bi, am na fu Rëg-rëg sampee 2i loxoom ak 2i wóomam, muy 4i apiwi, nees koy waxe. Kon, Saa-Cees a yeyoo ndam li. CNG mooy àtte.
https://www.defuwaxu.com/li-gen-a-fes-ci-xibaari-taggat-yaram-dibeer-5-mars-2023/
PSG / FARÃS
https://www.defuwaxu.com/li-gen-a-fes-ci-xibaari-taggat-yaram-dibeer-5-mars-2023/
Mbappe defati na jaloore
https://www.defuwaxu.com/li-gen-a-fes-ci-xibaari-taggat-yaram-dibeer-5-mars-2023/
Mbappe tegaat na beneen jéego ! Doon na kuppekat bi ëpp lu mu dugal ci mbooru PSG. 201 bii la fa dugalagum bim fa ñëwee ba léegi. Bu ñu fàtte ni, Mbappe, 24i at doŋŋ la amagum. Waaye, ak li muy doon xale yépp, dafa dooj ba, turam siiw na lool. Gannaaw jéego bu réy bim defaat la Ronaldo, kuppekat Beresil bu mag ba, wax lii ci moom : ” Li Messi ak Ronaldo def ci kuppe, mennum Mbappe moo ko mën a defaat. Bu nu fàtte ni 24i la amagum.”
https://www.defuwaxu.com/li-gen-a-fes-ci-xibaari-taggat-yaram-dibeer-5-mars-2023/
Marquinhos ame na gaañu-gaañu
https://www.defuwaxu.com/li-gen-a-fes-ci-xibaari-taggat-yaram-dibeer-5-mars-2023/
Ba tay foofu ca PSG, gannaaw ndam li ñu am ci kaw Fc Nantes, démb ak li Mbappe def, njàqaree ngi bëgg a gane seen biir ak joŋante ñuy waajal ak Bayern, di bu ñu war a gañe bu ñu bëggee wéyal seen yoon ca “Ligue des Champions “. Marquinhos àggalewul seen joŋanteb démb bi, dafa gaañu, daldi fekki Neymar ak Kimpembe. Wuteek nañook Bayern mi nga xam ne, ay kuppekatam yi gaañu woon ñoo ngi delsi.
https://www.defuwaxu.com/li-gen-a-fes-ci-xibaari-taggat-yaram-dibeer-5-mars-2023/
LIGA / Espaañ
https://www.defuwaxu.com/li-gen-a-fes-ci-xibaari-taggat-yaram-dibeer-5-mars-2023/
Paap Alasaan Géy, ñu miin ko ci Paap Géy, defaat na beneen paas ci seen joŋante bi ñu ñàkk démb ci kanamu Athletico Madrid (1-6). Paas boobu mooy ñetteelam ba mu demee ca Seville ba léegi, di wane miinam bu gaaw ci këlëb ba. Mujjul a àggali joŋante bi itam, moom Paap Géy. Ndax, dañ ko ruus ginnaaw bi mu amee ñaari kartoŋ soon.
https://www.defuwaxu.com/li-gen-a-fes-ci-xibaari-taggat-yaram-dibeer-5-mars-2023/
MILAN / ITALI
https://www.defuwaxu.com/li-gen-a-fes-ci-xibaari-taggat-yaram-dibeer-5-mars-2023/
Ibrahimovic, na woon, fa woon
https://www.defuwaxu.com/li-gen-a-fes-ci-xibaari-taggat-yaram-dibeer-5-mars-2023/
“Ñëwat naa gannaaw sama gaañu-gaañu bi. Léegi, dinañu xamaat kuy tàmbali joŋante yi. Bi ma gaañoo ataakã yaa ngi doon wane seen bopp. Waaye nag, dikkaat na. » Kàddu yooyee la Ibrahimovic yëkkëti gannaaw ba ko benn taskatu-xibaar laajee lu jëm ci moom ak ekib ba.
https://www.defuwaxu.com/kadduy-usmaan-sonko-useynu-beey/
KÀDDUY USMAAN SONKO 1/2 PÀCC
https://www.defuwaxu.com/kadduy-usmaan-sonko-useynu-beey/
Senegaal gépp amoon na fiy yëngu-yëngu, réew mi jaxasoo, yëf yi doy waar lool, yegg sax fu ko kenn foogul woon. Ñii seen i bakkan rot ci, ñee am ciy gaañu-gaañu yu metti, ñale ñàkk ci alal ju bari. Ginnaaw ba mu jógee “Section de Recherches” bu Kolobaan, Usmaan Sonko amal na waxtaan ak waa réew mi  ci 8eelu fan ci weeru Màrs. Waxtaan woowu nag, dara waralu ko woon lu dul mas-sawu leen ci yi fi jot a xew, xamal leen itam ni mook ñoom a bokk naqar.
https://www.defuwaxu.com/kadduy-usmaan-sonko-useynu-beey/
Lu Defu Waxu, seen yéenekaay ci kàllaamay Kocc a ngi leen di baaxe ay kàddoom na mu leen yëkkatee keroog jooju. (Ci taataanug Uséynu Béey)
https://www.defuwaxu.com/kadduy-usmaan-sonko-useynu-beey/
“Mbokk yi, tey, walla mën naa wax sax ne, fan yii yépp sunu xol neexul, sunuy nelaw néew na, sunu xalaat bari na, te dara waralu ko nag, lu dul tiis wi nga xam ne am na ci réew mi, muy ay bakkan yoo xam ne rot nañ fi.
https://www.defuwaxu.com/kadduy-usmaan-sonko-useynu-beey/
Kon, dama doon ñaan bala nuy dugg ci waxtaan wi rekk nu daldi def “une minute de silence” jagleel ko sunuy doom, ndax ñi fi faatu ñépp, walla ñiñ fi faat ñépp, nun li nuy doon ndaw ndaw, mat nañuy doom. Tey, jox nan ma lim boo xam ni jeexagul; waaye lim bi nu jotagum mat na fukki nit. Benn bakkan bu rot rekk, ci anam bu mel nii, nga xam ne dañ koo faat, musiba la ci réew mi, rawatina nag, bu ñu nee tey mat nañ fukki nit. Bakkan yooyu nag, ñooy :
https://www.defuwaxu.com/kadduy-usmaan-sonko-useynu-beey/
ku ñuy wax Baay Séex Jóob, amoon fukki at ak juróom-ñaar, ñuŋ ko faate fii ci Yëmbël ; Séex Kóli amoon ñaar fukki at, ñuŋ ko faate ci Biññoona ; Faamara Gujaabi, moom it amoon ñaar fukki at, ñu faat ko Biññoona ; Paap Siidi Mbay, amoon moom it ñaar fukki at, ñu faat ko fii ci Kër-Masaar ; Saajo Kamara am fukki at ak juróom-ñett, ñuŋ ko faate Jawobbe ; Mañsuur Caam, moom it am ñaar-fukki at, ñuŋ ko faate fii ci Ndakaaru; Alasaan Bari, amoon fukki at ak juróom-ñaar, ñuŋ ko faate fii ci Sànteneer, ci Ndakaaru ; Musaa Daraame, amoon fanweeri at ak juróom, ñoŋ ko faate ca Ndóofaan ; Buraama Saane, amoon fukki at ak ñaar, ñuŋ ko faate Biññoona ; ak Móodu Njaay, nga xam ne moom lañ nu mujje xabaare, ñu faate ko tey fii ci Parsel-Aseni, ci anam yu ñaaw ba fu ñaawaay yem.
https://www.defuwaxu.com/kadduy-usmaan-sonko-useynu-beey/
Kon, nu ngi leen di ñaanal Boroom bi Mu xaare leen Àjjana. May ñaan nag, ñi fi nekk ñépp, taskatu xibaar ak ñeneen ñi ko teewe,  nu taxaw def “une minute de silence” jagleel ko sunuy rakk yooyu ak sunuy doom yooyu… (Tekkaaral ci diirub benn simili). … Jërëjëf. Maa ngiy jox sunu sëriñ, Sëriñ Mañsuur Jamiil mu jagleel leen ay ñaan yoo xam ne, haasatan la, yokk barke rekk, ndegam Yàlla def na mu teew fi ; nu jox ko mu defal nu ñaan… (Ñaan).
https://www.defuwaxu.com/kadduy-usmaan-sonko-useynu-beey/
… Jërëjëf. Kon, dina nu jéem a tënk waxtaan wi ci lu dul gudd torob. Gannaaw bi nu dello nuyu saa-Senegaal yi nuy seetaan yépp, di nuyu ak di gërëm kilifay réew mi, kilifa diine yi, kilifa aada yi, àbbe yi, di rafetlu seen taxawaay ci réew mi. Ndax, wax naa ko ci samay kàddu yu jiitu, bir na ma man, ni ñoom, lañ ca waroon a def, def nañ ko ci bañ ko waree def. Aajowul nu koy jéebaane walla di ko wax ci kaw. Dafa fekk nag, kilifa diine moom, orma rekk lañ ko warlul. Am na loo xam ne, bu naree xotti worma, su ñu waxee ci suuf yem ca. Waaye ku bañ a dégg, ba mbir mi tàng ci sa loxo, dinga dellu ba ci ñoom, woowaat leen. Kon, nu ngi leen di gërëm ci taxawaay bi. Di gërëm kilifay aada yi bu baax itam, di gërëm ñi fi teew ñépp.
https://www.defuwaxu.com/kadduy-usmaan-sonko-useynu-beey/
Ñii fi nekk ñépp, amul kenn koo xam ne pólitig walla par-parloo moo la fi indi. Amul kenn koo xam ni li nga daj ci fan yii, par-parloo moo tax, waaye ñi fi teew ñépp, li leen tax a jóg ba tax ñu daj ci lu ma ci dajul man, mooy Senegaal, yitte gi ñu am ci Senegaal, bëgg-sa-réew ak am dëggu ni, dañu war a taxaw ngir réew mi, dañu war a taxaw ngir ëllëg, dañu war a taxaw ngir sunuy doom ak sunuy sët. Kon ñoom ñépp dama leen di gërëm man, ci sama tur ; waaye dama leen di gërëm tamit ci turu askanu Senegaal, ndax askanu Senegaal lanu taxawal, taxawalunu Usmaan Sonko. Ñi fi jóg ñépp sonn ci, su doon jëmmu Usmaan Sonko rekk, xéy-na «10%» yi walla «15%» dinañ génn. Bu kenn naagu ba foog ni, yow yaa tax doomi Senegaal yi génn, déedéet.
https://www.defuwaxu.com/kadduy-usmaan-sonko-useynu-beey/
Li tax lii am, mooy yëg-yëg bu kenn ku nekK xam na ni, sunu réew, sunu askan mu ngi nekk ci ay jafe-jafe yoo xam ne, bu nu seetaanee ba mu deme nenn rekk, defe naa dina rëcc ba fàww. Kon, maa ngi leen di gërëm ñoom ñépp ci turu askanu Senegaal. Bu loolu weesoo, may sargal jigéen ñi it ndax gis nanu seen taxawaay ci xeex bi ; te tey dañ leen ko màndargale, muy bésub “8 mars”.  Jigéeni boor bu nekk nag, du jigéeniy PASTEF kese. Waaye, jigéen ñi taxaw nañ jàpp ci xeex bi. Defe naa Ajaa Yaasin a ngi nii toog sama wet, sama yaay Ayda Mbóoj sama layookat a nga nale, ñoom Maymuna Buso ak keneen ak keneen, su ma leen doon lim tey du jeex, ñoom Aysata Saabara, ñoom Maam Jaara Faam… Ku ma limul rekk bumu ci mer, nu delloo leen njukkal ci bés bii, di leen jaajëfal bu baax. Mbokk yi, li xew ci réew mii, doy na waar, li xew ci réew mii, aa ! defe naa ñoom Decroix ñoo nu ëpp jaar-jaar fuuf, ñoo nu ci gën a yàgg, waaye gëmuma ne, lii fi xew, mas naa xew ci Senegaal. Du xew-xewi 63 yi, du yi ko jiitu, du 68, du 2000, du 2012, du 88, du 93… Ba tey, defe naa ni lii xew tey Senegaal, masu fee xew. Ba tey jii, Senegaal mooy xët wu njëkk ci xibaari àddina si. Kon loolu du lu tuuti, foog nun waa Senegaal, nu  mën koo natt ; xam lii lu mu doon, ak lan la war a màndargaal ci sunu mboorum  réew. Ndaxte, su dee mënun cee jël ay njàngat ba lii dootul am ci réew mi, bu boobaa, defe naa coono yi dootuñu jariñ dara. Ñi ci seen bakkan rot, ñi ci gaañu, di ñu bari, ñeneen ak ñeneen ak ñeneen, defe naa dootul jariñ dara.
https://www.defuwaxu.com/kadduy-usmaan-sonko-useynu-beey/
Kon, bu nu waxee loolu, danuy dellu delloo njukkal, ni ma ko defe, ci ñii nga xam ne seen bakkan rot na ci, te dinaa ci dellusi, ma def ko ci ñi gaañu, ndaxte ñi gaañu bare nañ. Di ñaan Yàlla rekk, mu bañ a weesu foofu.
https://www.defuwaxu.com/kadduy-usmaan-sonko-useynu-beey/
Bi ci des nag, di ci jagleel ngërëm lu ràññeeku ñi nga xam ne, ñooy ndawi Senegaal yi.  Di leen delloo njukkal bu baax. Yàgg nañoo wax ndawi Senegaal yi nii, xale Senegaal yi nale, déedéet ; sunuy ndaw, dañu am awãs ci nun. Li ma gëm mooy sunu ndaw yi dañu am awãs ci nun. Wone nañ ko, ndax ku dem di jàmmaarlook ay takk-der, ñu yore ay fital, yor lu la mën a rey, yor lu la mën a gaañ, yow yoruloo lu dul say loxo ; te defuloo ko ndax dafa am dërëm booy xaar, ndax dafa am ñu féete beneen fànn ñu leen di fay xaalis ngir faat ay bakkan ; yow defoo ko ndax dërëm booy xaar, kon gàcce-ngaalaama ndawi Senegaal. Te nu leen di wax ni, day door rekk. Bis niki tey, na ngeen xam ni réew mi, seen réew la, dogal bi seen dogal la, nun ci seen waaw lanu war a doxe, ñiy def pólitig ci seen waaw lañu war a doxe, di leen déglu. Kon bu leen nangooti di seetaan ba mbir mi egg fu mu warul a egg.
https://www.defuwaxu.com/kadduy-usmaan-sonko-useynu-beey/
Ma wax nag ni, ñooñu ñépp nga xam ne sonn nañu ci mbir mi, ñi nekk seen kër sax di ko naqarlu, ñi toog seen sijaada  di ñaan, bu ma nekkee fii di waxtaan ak yéen, xam leen ni, yéen a tax, ndax bu ngeen amul woon taxawaay boobu, waxuma la tey jii, waxuma la àjjuma bii weesu, waaye altine 8i fan weeru feewiryee laa waroon a nekk Rëbës. Kon man tey jii, duma woon nekk fii di wax ak yéen. Kon bu leen kenn gëm loo ne, dañ noo beral loxo. Waaye seen taxawaay, li mu firndeel rekk tey, mooy li Tubaab naan : «La souveraineté appartient au peuple» Lépp askaan wee ko yore. Mooy kàttan dëgg-dëgg-dëgg ; sañ-sañ dëgg-dëgg-dëgg cim réew, askan wee ko moom, kenn moomu ko. Ñoom dañuy faral di wax, loo wax ñu ni «Force restera à la loi». Waaye yoon, «la loi», mooy askan wi ; yoon wi du dipite, du Maki Sàll… Ku dem nag ba sàggane ko, foog ne yoon wi ñu wote, te askan wi wote ko, mën nga koo jalgati di ko teg ci kaw nit ñi, askan wi da la koy fàttali, te loolu moo leen dal tey.
https://www.defuwaxu.com/kadduy-usmaan-sonko-useynu-beey/
Kon taxawaay boobu, ngalla waay, bumu deñati Senegaal. Bumu deñati ndaxte li ñuy wax les «grandes démocraties» (demokaraasi yu mag yi), boo gisee njiit yi am lu ñu sañul foofu, mooy askan wi dafay taxaw jonn di leen di wattu. Saa su ñuy génn rekk, nit ñi génn ne leen «lii duñu ko nangu». Kon nanu am taxawaay boobu bés niki tey. Ma wax tamit ni, ñii nga xam ne, ñu ngi ci kaso yi, tey lu ëpp téeméeri nit ñu ngi ci loxo Maki Sàll, ñii Tàmbaakundaa, ñii Sigicoor, ñii Kéedugu, fii Ndakaaru, ba Ndar, Tiwaawan, fu ne jàpp nañ fay nit ñoo xam ne, sàccuñu, reyuñu nit, wuruxuñu, luxusuñu ay biye, luubaluñu xaalisu réew mi. Seen tuuma mooy dañoo dox-ñaxtu, te Ndeyu-sàrti réew mi moo leen jox sañ-sañu dox-ñaxtu. Nu ngiy mas-sawu ñooñu, waaye di leen xamal yit ni, dun leen seetaan. Di mas-sawu it ñi nga xam ne ñàkk nañ ci seen alal ndaxte yàqu-yàqu yi bari nañ. Loolu du woon cëslaayu mbir mi ; ñi jóg di naqarlu duñu ay saay-saay ; ay nit nag, mën nañ cee rax, waaye, loolu taxuleen woon jóg. Te it sunu xeex, jubluwunu ko ci askan sàngam walla réew sàngam, du loolu mooy sunu xeex. Waaye dafa fekk daa am fu mbir yi di tollu, lépp mën na cee jaxasoo, lépp mën na cee am ; waaye loolu du woon cëslaay gi. Ndaxte, ku bëgg yor réew ak ku bëgg defar réew, doo toj alalu jaambur, doo yàq oto jaambur, doo toj këru jaambur. Kon loolu, nuŋ koy mas-sawu bu baax nit ñi mu dal.
https://www.defuwaxu.com/kadduy-usmaan-sonko-useynu-beey/
Di mas-sawu njabooti ñi ci faatu, di leen jaal, te bu soobee Yàlla, dinañ góor-góorlu ba kenn ku nekk, nu def sunu «délégation», ñi fi nekk ñépp dox ñëw jaaleji leen, di mas-sawu njabooti ñi ci gaañu ; lañ ci man it ci taxawu dinan ko def. Di mas-sawu njabooti ñi nga xam ne tey, caabi féete na leen ginnaaw ; wax leen it ne seetaanunu ñooñu ndax ginnaaw ba nu jëlee awokaa yi leen war a layool, kenn ku ne, nu ngiy góor-góorlu ci liñ la man a jàppalee ba doo tumuraanke, walla sa njaboot du tumuraanke.
https://www.defuwaxu.com/kadduy-usmaan-sonko-useynu-beey/
Waaw mbokk yi, lii lépp lan moo ko waral ? Lii lépp ci ay tiis yu dal ci Senegaal la. Li ko waral mooy xiif gi nga xam ne, Maki Sàll ak ñi mu àndal xiif nañ ko nguur ; ak yaakaar ni ñoom dañu war a yore nguur gi toog fi ba fàww. Lii lépp moo leen ko andil. Moo ne de, ay at ca ginnaaw loolu lan fi xeexoon ba ay bakkan rot fi. Li andi lii, mooy nguur gi ñu teg ci loxo Maki Sàll, ne ko : «Jox nan la sunuy mën-mën, jox nan la sunu alal, jox la «administration» bi, jox la yoon wi “justice”, jox la xare réew mi, maanaam “arme” bi, jox la lépp loo soxla li nu bëgg mooy nga defar réew mi, li nu bëgg mooy ndaw ñi am liggéey, li nu bëgg mooy nit ñi faju, li nu bëgg mooy tali yi baax». Maki Sàll walbati loolu lépp, jël ko muy doole ju muy teg ci kow saa-Senegaal yi. Muy kuy pólitig, muy kuy «mouvement citoyen», muy «Sociéte civile», képp ku ne àndumaak Maki Sàll rekk, teg na doole jooju sa kow. Loolu moo nu andi ci lii. Mu ànd ci ak ay nitam yoo xam ne, duñ ko wax dëgg, mbaa sax ñoo ko yées, soo moytuwul, moom ci boppam.
https://www.defuwaxu.com/kadduy-usmaan-sonko-useynu-beey/
Ndax lii am yépp nag, ñi ko séq bari nañ de, waaye li ci ëpp ay jëfkat yu ndaw lañu. Boo ko doon seet, ñeenti jëfkat lañu : Maki Sàll, Antuwaan Jom, Maalig Sàll ak Basiiru Géy. Ñeneen ñépp ay suq lañu, nga xam ne, dañu leen di defloo ñuy def. Waaye ñeent ñii, musiba Senegaal yépp, ci jamono yii ñu tollu tembe, ci ñooñu la. Ndax jaadu na, 16i milyoŋi doomi-Senegaal ñeenti nit rekk lëmbe leen? Ndax loolu war nañ wéy di ko nangu ci dëkk bii ? Loo wax nag, ñu ne la nun noo yor nguur gi, “force restera à la loi”. Te, yoon, “loi” boobu, duñ ko tudd lu dul bu dee ci kujje pólitig gi. Yoon woowu dañ koy walbati ngir man a jot ci képp ku àndul ak ñoom ; waaye saa su yoon wi waree dal seen kow, ñu ne mukk du fi am. Ñaata nit ñoo fi mas def ñombe yoo xam ne kenn du ko tudd ? Tey, ñu ngiy romb waa Senegaal di leen yëkkatil i mbagg. Loolu nag lanu mënatul a nangu. Looloo tax nit ñi jóg ni, lii dootunu ko nangu, dootu fi am.”
https://www.defuwaxu.com/kadduy-usmaan-sonko-useynu-beey/
(Dees na ko topp…)
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-8/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-8/
CAN 2024
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-8/
Amara Juuf bokkul ci 55i futbalkat yi Alin Siise tànnagum ngir yóbbu leen ca CAF laata mu di ko seggaat ba 27. Moom, kàppiteenu U17 bi, fim ne ma nga Metz ngir faju.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-8/
Gaañu-gaañu yaa ngi bëgg a bari ci gaynde yi. Gànna Géy dolleeku na ca limu ñi gaañu fekki ñoom Séeni Jeŋ ak Nàmpalis Méndi.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-8/
SUPER LIG
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-8/
Ëttu àttewaayu Tugal bi jox na dëgg Super League ci kaw UEFA, daldi koy daganal. Kon, saa suñu ko bëggee te mën ko sañ nañu taxawal seen i mbir te benn daan du ci fekk benn ekib niki woon ca njëlbéen ga. Gannaaw loolu nag, kii di Aleksander Ceferin, njiitul UEFA yëkkatina ciy kàddu yoy xol bu jeex lay niru. Mu ngi naan: “Mën nañoo taxawal lu leen neex. Di yaakaar ni dinañu gaaw a tàmbali seen joŋante bu xàttaaral bi ak ñaari ekib (Real Madrid, Barça).”
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-8/
Donte daganal nañu yëf ya, teewul am na ekib yu taxaw dàq boobu Super League, ñu ci mel ni Manchester United, Séville, Valence, Atletico Madrid, Bayern, Dortmund.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-8/
GREENWOOD A NGI ÑËWAAT BU BAAX
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-8/
Gannaaw ndogal li daloon ci kawam ba taxoon yoon tegoon ko loxo laata ñu di ko bàyyi setal ko ci lépp, Manchester United miy këlëbam daf ko bañoon a jëlaat daldi koy abal Getafe (Liga). Fim ne nag, moo ngi wane boppam bu baax ca ekib ba di dellusi bu baax ci nees ko xamee woon. Amagum na fa 3i bii ak ñeenti paas.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-8/
BUNDERSLIGA
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-8/
Bayer Leverkusen mooy ekib bi njëkk a dawal ca sàmpiyonaa Almaañ ñaar-fukk ak juróomi joŋante yoy ñàkku ci benn. Loolu di gën a dëggal taxawaayu ekibi ak liggéey bu rafet ba fa Xabi Alonso di def.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-8/
Thomas Müller yokk na pasam ba atum 2025. Moom nag digganteem ak Bayern xanaa aj dàll rekk a koy tax a jeex. Nde foofu rekk la fas yéene futbal ba keroog muy bàyyi.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-8/
Victor Boniface jëlatina raaya “Rokkie” ca Bundersliga ba. Gii di juróomeelu yoon bu mu tegale di jël raaya gees jagleel ki gën a xarañ ci weer wi.
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-basketu-senegaal-yaakaar-ak-yakki/
FUTBAL AK BASKETU SENEGAAL : YAAKAAR AK YÀKKI
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-basketu-senegaal-yaakaar-ak-yakki/
Bi Alseri dumaa Senegaal benn ci dara ci finaalu joŋanteb réewi Afrig yi (CAN) ak léegi, mu ngi bëgg a yàgg. Waaye, kenn fàttewu ko. Li ko waral nag mooy finaalu basket bi soxna yi ñàkk, ñoom tamit, biñ dajeek Niseryaa fan yii ñu weesu. Yaakaaroon nañu ne, soxnay basket yi dinañ feral sunuy rongooñ. Ndeysaan, keroog bi leen Niseryaa daanee fii ci Ndakaaru, ñépp a ci amoon tiis ak naqar ndax yaakaar ju tas.
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-basketu-senegaal-yaakaar-ak-yakki/
Ñaari finaal, ñaari kub, Senegaal ñàkkandoo leen ci menn at, ci diggante bu gàtt a gàtt ! Ñii ne waaw, ban dëmm a nu juutu ? Ñee di laaj, kan moo nu um ? Laaj bi jar a laaj, nag, ci dëgg-dëgg mooy : lan walla kan mooy sunu gàllankoor ba tax nuy lajj saa su nekk ci cëppaandoo bi ? Tey nag, ci futbal bi lanuy tàmbalee.
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-basketu-senegaal-yaakaar-ak-yakki/
Séex Sekk, Roose Mendi, Sil Bokànde, Umar Géy Seen, Ferdinaa Kóli, Umar Daaf, Saalif Jaawo, Paap Buuba Jóob, Fadiga, Àllaaji Juuf, Aari Kamara, Saajo Maane, Kalidu Kulibali… Ku dégg yile tur, sam xel dem ci jaloorey ekib nasiyonaalu futbal bu Senegaal. Ñii nu fi jot a lim ñépp nekkoon walla di ay futbalkat yu xereñ lool, ñu ràññee leen bu baax ci Senegaal, ci Afrig ak ci àddina sépp. Waaye, ak lu tur yiy réy réy, lenn doŋŋ lañuy màndargaal : yaakaar ju tas. Waaw. Ndaxte, ba nëgëni-sii, Senegaal amagul benn biddéew ci mayoom bi. Ak lu coow liy bare bare, mësta jël kub. Laaj bi ub bopp yi mooy : lu tax Senegaal jëlagul kub ba léegi te, jamono ju nekk, mu yor ay ndaw yu xereñ ? Nu ànd xool, démb ba tey, lu xel mën a jàpp ne mooy sunu laago ci futbal bi.
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-basketu-senegaal-yaakaar-ak-yakki/
1961 : Ndoorteel li
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-basketu-senegaal-yaakaar-ak-yakki/
Ci at mii la Senegaal di door a amal joŋanteem bu njëkk. Ñaari at lañ ci teg (1963) ekibu futbal bi Senegaal daldi jël raw-gàddu gi ci Joŋantey Xaritoo (Jeux de l’Amitié) yi amoon ca jamono jooju.
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-basketu-senegaal-yaakaar-ak-yakki/
1965 : Njëlbéenub joŋante ci CAN
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-basketu-senegaal-yaakaar-ak-yakki/
Ci at mii la Senegal di door a bokk ci joŋanteb réewi Afrig yi (Coupe d’Afrique des Nations), gàttal bi ci nasaraan di joxe CAN. Ci njëlbéenug joŋanteem boobule, Senegaal ñaawu ci. Ndax, moo jëloon ñetteelu palaas bi. Gànnaaw gi, daanaka Senegaal ab nooy-neex la woon, ku jàpp rekk wulli, ekib bi dee daanaka.
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-basketu-senegaal-yaakaar-ak-yakki/
1990 : Dekkiwaat bi
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-basketu-senegaal-yaakaar-ak-yakki/
Senegaal dekkiwaat. Claude Leroy mi yoroon ekib bi ci diggante 1989 ak 1992 moo ko defaraat, tàggat leen ba Senegaal joŋantewaat, ginnaaw atum1965, « ½ finales » CAN bi amoon fii ci Senegaal ci atum 1992. Waaye, ñetteelu palaas bi la mujje jëlaat. Ci atum 1994, « ¼ de finales » la yem, wute joŋante yu 1996 ak 1998.
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-basketu-senegaal-yaakaar-ak-yakki/
2000 – 2019 : Jamonoy jaloore ak yaakar ju tas
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-basketu-senegaal-yaakaar-ak-yakki/
Ci wàlluw futbal, bi Senegaal dee Senegaal ba tey, ci diggante atiy 2000 ak 2019 lañu ko gën a ràññee. Ndaxte, ci jamono jii la ndawi Senegaal yi gën a xereñ fëlle : A1llaaji Juuf, Fadiga, Ferdinaa Kóli, Umar Daaf, Lamin Jaata, Aliyu Siise, Saalif Jaawo, Paap Buuba Jóob, Tooni Silwaa, Aari Kamara, Abiib Béey, Jomansi Kamara, Mamadu Ñaŋ, Suleymaan Jaawara… Bi ñooñu jeexalee, Saajo Maane ak i ñoñam, Gànna Géy, Kalidu Kulibali, Sabali, Ismayla Saar, Jaawo Balde… wutu leen. Ku ci gën a xereñ, dàq futbal sa moroom nga ne kii. Ñu yaakaaroon ni bile yoon, nag, Senegaal dina am dara. Ndeysaan, bu dul finaalu 2002 ba ak « ¼ de finales » bi ñoom Àllaaji Juuf demoon ca « Coupe du Monde » 2002 ak ndam li ñu amoon ci kow Frãs ci ndoorteelu joŋante bi, Senegaal jëlul dara, tus… Naam, li Senegaal àggoon finaal ca Mali, ndam la. Naam, def na jaloore ju réy a réy bi mu amee ndam ci kow Frãs ci « Coupe du monde » bi ci toppoon, ñu ni déet-a-waay mu dem ba « ¼ de finales » yi. Kenn sañul a wax ne loolu du ndam. Wànte, ndam loolu, wareesoon na ko def ag garab, suuxat ko ba mu meññ yeneen i ndam yu gën a réy, maanaam nu jël kub. Ndege, Senegaal bokkoon na ci ekib yi gën a xereñ ci Afrig, te ba léegi loolu la ñépp jàpp.  Waaye dara, dara la fi indiwul : 2004 Tinisi moo nu toogloo ca réewam ci « ¼ de finales » yi 1-0 ; 2006 Misra moo ko toogloo ci « ½ finales » yi, mu mujje jël ñeenteelu palaas bi. Ci at moomu « Coupe du monde » amoon na, waaye Senegaal bokku ci ndax Tógo moo ko tere woon dem, mu metti woon lool ci waa réew mi. CAN 2008, Senegaal génnul sax gurub bi mu bokkoon. 2010, Amara Taraawore moo yoroon ekib bi. Waaye, ci CAN bi, Senegaal ñetti joŋanteem yépp la ñàkk, daldi toog. Demul yit ci « Coupe du monde » at moomu. Ñu foog ni Alain Giresse mi ñu tabb ci atum 2013 dina faj laago bi, waaye moom tamit dañu koo mujje dàkk ndax lajj bi mu lajjoon.  Ki ko wuutu mooy Aliyu Siise mi bokkoon ci ekibu 2002 bi te nekkoon kapiteen bi. Ginnaaw CAN 2017 bi nu toogee ci « ¼ de finales » yi, moo delloosiwaat Senegaal, ak ñoom Saajo Maane, ci “Coupe du monde” 2018 bi. Waaye, foofu tamit, yaakaar ju tas lañ fa jële. Ndax Senegaal génnul gurub bi mu bokkoon doonte sax kenn mënu ko fa woon. Ci CAN 2019 bi, ñépp a newoon ne bii yoon moom, day baax. Waaye, Alseri moo nu dóor ci finaal bi. Yaakaar tasati.  Ñii di saaga fii Aliyu Siise, ñee di duut baaraam njiiti federaasiyoŋ bi, ñeneen ñi di ko jiiñ sëriñtu bi waa réew mi nekke ba ci futbalkat yi. Kan moo ci wax dëgg ?
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-basketu-senegaal-yaakaar-ak-yakki/
Cuune, yaataayumbe ak sëriñtu
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-basketu-senegaal-yaakaar-ak-yakki/
Bi fi Bruno Metsu (2002) jógee ba léegi, fukki tàggatkat wuutu nañ ko ci boppu ekib bi laata Aliyu Siise di toog. Ci fukk yooyu, juróom-ñaar yi ay doomi-réew mi lañu. Loolu day firndéel matadi, cuune ak caaxaan bi ñu yore futbal bi. Ndaxte, bir na ne ba tey xamuñu nees di tànne tàggatkat bu baax ak naka lees koy gungee, jàppale ko ba liggéeyam àntu. Loolu day wone yit yàkkamti bi ak ñàkk fulla bi waa federaasiyoŋ bi nekke. Te, ku yàkkamti, yàqule. Benn, ab ekib dees koy tabax ci diir bu yàgg. Mbir mi du xéy rekk sotti. Fàww nga may tàggatkat bi tuuti ngir mu tabax ekib buy jël kub. Waaye xel nanguwul, benn walla ñaari at yu nekk nga ut beneen tàggatkat, indi yeneen i futbalkat. Ñaareel bi mooy ne, njiit day am fulla ci boppam. Du nekk ma riirandoo waxatuma la ak benn nopp. Fàww bëgg-bëgg yi wute, gis-gis yi ak xalaat yi safaanoo. Kon mënoo, yow njiit li, saa bu taskati xibaar yi waxee fii nga topp leen, bu askan wi yuuxoo fee ngay jéem a def lu ko neex ngir bañ coow. Moo taxit, saa boo leen toppee, boo lajjee, ñoom ñoo lay njëkk a song. Li koy firndéel mooy atum 2008, bi Senegaal arañefee ak Gàmbi fii ci estaad Lewopóol Sedaar Seŋoor, ndaw yi dañoo mer ba futt, di ñaxtook a sànni xeer ci buntu estaad bi. Bés boobu tàngoon na lool. Kenn fàttewul tamit 2012, bi farandooy ekib bi meree, di sànni ay xeer, butéel ak i yu ni mel ci teereŋ bi. Jotoon nañoo sax wàcc ngir duma futbalkat yi ak njiiti federaasiyoŋ bi. Bés boobu, daa fekkoon Kodiwaar am ñaari bii ci kow Senegaal, muy tekki ne Senegaal du dem ca CAN bi waroon a am atum 2013. Bi ñu jógee ci loolu, FIFA, kurél gi yor futbal bi ci àddina sépp, dafa teg ay daan Senegaal.
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-basketu-senegaal-yaakaar-ak-yakki/
Bi ñu ko laajee lu tax futbalu Senegaal mënta jëm kanam, Àllaaji Juuf dafa tontu woon ne ñi fi nekk (njiit yi), xaalisu futbal bi lañu bëgg waaye bëgguñu futbal bi. Kàddu yooyoo taxoon ñu teg ko fi ay daan yu metti, moom Àllaaji Juuf. Waaye, ndax mënees na koo weddi ? Ñaari at lañ ci teg, Demba Ba waxaat lu ni mel. Te, wolof nee na, fen du màgget. Kon daal, njaw des naw xambin. Daanaka, jamono ju nekk, saa su joŋante amee, nga dégg ne waa federaasiyoŋ bi ñoo ngi yaataayumbe ak xaalisu futbal bi. Seen njaboot, seeni mbokk ak i xarit, ñépp lañuy yóbbu fi ekib biy dem, di gundaandaat ak a ndagarwale ci alalu réew mi. Ñu ni déet-a-waay, sëriñ si demaale ak seeni xarfafuufa, gisaanekat yi ame nit ñi fii, ñuy fekk ci ron-lalu futbalkat yi ay téere… Muy lu yéeme sax ! Kon, mel na ne laaj bi nu sampoon ca njëlbéen am na tontu. Cuune, yaataayumbe ak sëriñtu bi ñu nekke moo nu teree jël kub…
https://www.defuwaxu.com/futbal-ak-basketu-senegaal-yaakaar-ak-yakki/
Bu beneen yoonee, dinaa leen wax lu tuuti li ma xam ci basket bi !
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-1-10-2023/
XIBAARI TAGGAT-YARAM (1/10/2023)
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-1-10-2023/
KUPPEG ÀDDINA WAY-LUU YI (MUUMA YI)
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-1-10-2023/
Bàyyeesu leen xel, waaye way-luu (muuma) yi teewal Senegaal ca kuppeg àddina si bees leen jagleel ñoo ngay def i jaloore yu rëy. Ba léegi, ékib gañeeguleen ! Ñoo ngi toll ci ñeenti joŋante, gañe 3 yi daldi timboo benn bi. Kaar-dë-finaal lañu war a amal fan yii.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-1-10-2023/
ILIMAAN NJAAY DUGAL NA BIIWAM BU NJËKK AK MARSEILLE
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-1-10-2023/
Démb ci gaawu gi la Ilimaan Njaay, doomu Senegaal ji, di sog a dugal biiwam bu njëkk ak Marseille ci seen joŋante bi amoon seen diggante ak Monaco bi ñu ñàkk ci (3-2). Lii la wolof naan, xëcc bu daggul dikk. Jafe woon na ci moom ca njëlbeen ga, ba tax mu daan xaw a jaaxle. Waaye, mu gëm ko ba mu dikk. Njoortees na ni dana ko gën a firiloo nag, nde lees di séentu ci moom ëpp na li mu fa waneegum.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-1-10-2023/
MÓORI JAW, KU JAR A BÀYYI XEL
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-1-10-2023/
Alin Siise war na bàyyi bu baax bëtam ak xelam ci doomu Senegaal bi, Móori Jaw. Moo ngi def i jaloore yu réy jamono jii ca këlëbam, Clermont. Gaawug démb gee ci mujju, mu def joŋante bu rëy xañ kii di PSG bu Mbappe ndam.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-1-10-2023/
BARÇA AK MBIRUM NEGREIRA
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-1-10-2023/
Barça génnagul ci mbiri Negreira bi ba léegi. Mbir yaa ngi nekkoon ci loxo yoon mu di ko saytu di amal i luññutu. Ci fan yii nag, coow li dafa tàmbalee jugaat ba am ci sax ñuy ragal ñu tas Barça. Ndaxte, mbirum nger muy yàq powum futbal la. Waa Barça nag, ba léegi dañuy rasu, di bañ ni fayuñu benn arbiitar xaalis ngir mu ràccal leen seen boor. Kii di njiitu LIGA bi, Tebas, daldi na yëkkati ay kàddu ci loolu: “Ger (corruption) nekkul joxe xaalis rekk, Waaye, yéene bi kese, soo ko amee, mënees na la ci jàpp”.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-1-10-2023/
NEYMAR A NGI BËGG A JAAXLE
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-1-10-2023/
Jamono jii, Neymar fireegul ca naar ya. Ndaxte, boobu ba léegi, bii dafa jaar nii mu jaar nee. Mbir yi dafa xaw a dëgëragum ci moom, ba léegi dugalagul. Benn paas la fa def, am fa penaalti daldi koy rate. Fees ko séentu woon tëllagu fa !
https://www.defuwaxu.com/waaw-ana-ku-boom-omar-bolonden-joob/
WAAW, ANA KU BÓOM OMAR BOLONDEŋ JÓOB ?
https://www.defuwaxu.com/waaw-ana-ku-boom-omar-bolonden-joob/
Omar Bolondeŋ Jóob a ngi juddu ci 10eelu fan ci weeru sàttumbar 1946 ca Ñaame, péeyub réewum Niseer. Mu ngi faatu ci 11eelu fan ci weeru Mee 1973 ca kaso ba woon ca dunub Gore. Omar Bolondeŋ Jóob, nag, kàngam la woon ci biir kàngam yi, jànge ca lekkoolu digg-dóom ji ñu duppe Louis-le-Grand ca Pari. Bim fa génnee, mu tàbbi ca daara ju mag joojee ñuy wax École normale supérieure de Saint-Cloud. Jamono jooju, waxuma la sax am lijaasa ca daara joojee, waaye jànge fa rekk doyoon na ndam, dib sag bu réy a réy ci boroom. Bokk na ci liy màndargaal dayo daara jooju, mooy ne ki jëkk a jiite réewum Senegaal, Lewópóol Sedaar Seŋoor, ñu ràññee ko lool ci wàllum ladab ak mbind, bëggoon na fa dugg, waaye daa lajj. Muy biral ne, daara jooju, ab como daawu fa teg tànk. Am na sax ñuy wax ne, Seŋoor da koo iñaane woon ndam loola, ragal ne dina ko may fitu wujje ak moom ci làngu politig gi, ñeel Senegaal.
https://www.defuwaxu.com/waaw-ana-ku-boom-omar-bolonden-joob/
Sëñ bi Jóob, nag, du woon ragal walla tóoyemaan, ni ko ndaw yiy waxe. Bañkat dëgg la woon, ñeme woon xeex. Dafa di sax, ni mu ame woon noonu fit moo taxoon ñu dàq ko, moom ak benn doomu Farãs bu daan wuyoo ci turu Daniel Cohn-Bendit, ca daara ju mag jooju, ci atum 1969. Waaye yemul foofu. Ndege, Omar Bolondeŋ Jóob dafa xaroon tànki tubéyam, di xeexal askanu Senegal. Mi ngi féete woon ci kóminist yi, daan roy ci doxalinu Mao-Tsé Toung. Kurél gi mu bokkoon mësul a juboo ak Seŋoor, foo leen fekkaan, ñu ngay jàmmaarloo. Ndaxte, Seŋoor nguurug Farãs la fi toogaloon te, ci wàllu xalaat ak politig, yoonu kapitaalist yi la Farãs ak ñi far ak moom toppoon. Loolu mi ngi tollook jamonoy xareb suuf (guerre froide) bi amoon ci diggante U.R.S.S. (kóminism- sosiyalism) ak réewum Amerig (kapitaalism–liberaalism). Àddina si xar ñaar : ñii far ak U.R.S.S. miy mujje dooni Riisi, ñeneen ñi far ak Amerig.
https://www.defuwaxu.com/waaw-ana-ku-boom-omar-bolonden-joob/
Bi mu ñibbisee Ndakaaru, mu wéyal xeex boobu ci ndimbaluy rakkam. Ñoom ñépp ñu doon xeex nooteel, teg ci di ŋàññ doxalinu Seŋoor mi doon wéy ci waawi Farãs. Seŋoor demoon na sax ba jël Jean Collin, di doomu Farãs, boole ci di jegeñaale Jacques Foccart, toftal ko ci boppam, dénk ko lépp lu jëm ci kaaraange biir réew mi.
https://www.defuwaxu.com/waaw-ana-ku-boom-omar-bolonden-joob/
Loolu la Omar Bolondeŋ Jóob ak i àndandoom doon xeex. Ndax kat, Seŋoor dafa jébbalu woon ci Farãs ba nga xam ne, buñ tisóoliwaan Pari, mu ne yaaram-kàlla. Am jamono, Seŋoor sumboon fi liggéey bu mag ñeel mbeddi ndakaaru yi, santaane ñu set-setal gox-goxaat yi ngir laabal leen. Te, nag, duggewu ko woon lenn lu dul teeru Pompidou mi jiite woon Farãs, ngir bégal ko. Loolu metti lool Omar Bolondeŋ Jóob ak i rakkam ba tax ñu demoon taali Njawriñu Liggéeyu caytu gi ak Kërug aada ak cosaan gu Farãs ci Ndakaaru, ñu doon ko wax « Centre culturel français ».
https://www.defuwaxu.com/waaw-ana-ku-boom-omar-bolonden-joob/
Yemuñu ca, ndax defaroon nañ ay ndell, fasoon leen yéenee sànni ci kow woto yi yaboon Seŋoor ak kilifa tubaab yi mu waroon a teeru. Wànte, dañu mujje lajj ci pexe moomu. Ci lañu leen tege loxo. Jàllo Jóob moom, dañ ko tëjoon Kéedugu giiru dundam ba noppi sas ko liggéey bu mu sañutoon a bañ, dëkke koo metital ak a xorñoññal ca biir kaso ba. Ca la Omar nisëree woon ca Mali ga mu dawoon làqu, ne day afalsiy rakkam, kilifay Bamako tegati ko loxo, jébbal ko nguru Senegaal.
https://www.defuwaxu.com/waaw-ana-ku-boom-omar-bolonden-joob/
Ñaar fukki fan ak ñett ci weeru Mars ci atum 1972 la këru àttekaay bu Seŋoor àtte woon Omar Bolondeŋ Jóob, daan ko ñetti ati kaso yu mu waroon a tëdd. Li ñu ko jiiñoon moo doon “nasaxal kaaraange réew mi”. Mu doon xeex doxalinu Seŋoor wi aju woon ci li neex tubaab yi ba noppi worook bëgg-bëggu askanu Senegaal. Moom Omar Bolondeŋ Jóob, dafa mujjee ñàkk bakkanam ca kaso bu Gore ba ñu ko dencoon.
https://www.defuwaxu.com/waaw-ana-ku-boom-omar-bolonden-joob/
Ci 14eeli fan ci weeru Mee atum 1973, la yéenekaayu nguur gi, “Le Soleil”, siiwal xibaar bu tiis bi : “Kurél giy sàmm kaso yi (…) mu ngi xamle ni Omar Bolondeŋ Jóob xaru na ci néegam ci biir kasob Gore ginnaaw bi mu yeewee buum ci baatam. Mu ngi ko def ci boori ñaari waxtu ci guddi”. Booba, 26i at kepp la Omar Bolondeŋ Jóob am. Amaat Daŋsoxo ne woon ca tonet, wax ne : “Dafa leer nàññ ci sama bopp ne Omar Bolondeŋ Jóob dañu koo bóom. Li tax kilifa yi ŋànk réew mi bóom ko nag, lenn rekk la : ak xel mi ko Yàlla mayoon, Omar mënoon na leen fee jële !”
https://www.defuwaxu.com/waaw-ana-ku-boom-omar-bolonden-joob/
Ndeysaan, njabootu njóobéen – rawatina Jàllo Jóob – ñoo ngiy wéy di xeex booba ba léegi ngir ñu bañ a fàtte seen mag jooju. Ñoom li ñu jàpp mooy ne, Omar dañ koo rey, te dara waralu ko woon lu dul politig. Omar a ngi gaañu ginnaaw bi ñu ko metitalee ca kasob Gore ba, te ñu mën a njort ne lépp ci ndigalu Jean Collin la ame. Ñu bare ci ñiy gëstu ci mboorum (histoire du) Senegaal, loolu lañ jàpp.